letra de rancune - nitdoff
[couplet 1]
kaddu niou niaweni waroul woon mooss diougué tchi yow
nio bokk ben deret warooneu takh sa yaram daw
yaguoon la t-teuro ame sa estime dameu leu yagua naw
adouna djiay naleu taye sokhlato sa rak ndaw
ya gui mey doyadal ndakh fokk ni yama feté kaw
mais ngathie ngalama souma sanione kouy mindéf yakoy raw
moussouma diouk tchi bokko noumou tolou meu cedook yén
tolooon nguen tchi sokhlama ma bayi lepp takhawoulén
bima yallah tégué ay nattu meu seugu diko mounie
laaay doga khamni fi kou yoroul xaaliss toloul féneu tchi yén
appel yek message nieweutoul legui
ndakh kham ngueni legui frère bi dafey diekhal sa credit rek té dou fathie sa sokhla
mane dama yagua naïf djiteul famille sama lepp
nekon sen baye fall kou beugu dara ma madjiali diokhla la
djièpina seni melokaanou hypocrite money rek nguen guiss tchi nit ki bouffa nekoul nguen diko sikk
djiépina beutou mepris bi nguen mey kholé taye
meritna lou gueun li dedet key dou sama kholeu faye
damadaan ame kerseu beu damey teudiou dioy
soumadaan yeuk seni yité té meuneumoko fathie
taye sama khole bi wow neu kong t yéneu ko tothie
fi koufi sissou yén leu koufi reuy gatt tam yeneu ko tauthie
gueumeutouma kèn tchi yén yeneu ma pousse tchi rancune
mbétel la ame mou tiss tolou na tchi merrou danguine
[refrain: jahman]
yé nama pouss yé nama pouss souma néké rancunier dou kén yén leu
beugouma touss loudoul fayou wayé meunoumako mak yén dou bén
yé nama pouss yé nama pouss tchi rancune yéh
yé nama pouss lima léen lébalone bokoulak liguen ma fay réen
[couplet 2]
gatal sama tankeu téyé sama lamign amatouma sakh sén diote
yéné nalén ay xeweul lou nguen séntou yalney soute sén ndiorte
guedna sen peace and love samey kaddu ngok na tiss sén nope
nouyou nalén diokhlen thieur ndakh yallah beuguoul kouy dok mbook
beuguoulit kouy yéh fitna lolou rek mo takh may masla ak yén
méfiant legui dama distant beugueutouma nakh-ssalé faire semblant ak yén
ma def sama choix mou lathie ma sacrifice ma dem tchi andank mome
limeu daan def daw wagnikou rén nguen djign meu niak diom
tokk sen keur yén gni daan saaliite tchi sama yewenaay
taye nguen def debat tchi sama life di finte wakh you bone
legui soumey rèh woo lén mais soumey djioy lakhou
dotoulen yeuk samey projet ndakh lounguen kham mou yakhou
kolouté amatoul ndakh djianou biir mo amatoul
kilifté ngui ngey niodi tchi bopam guiss naani mo matoul
gueumeutouma kén tchi yén yeneuma pouss tchi rancune
mbetel la ame mou tiss tolouna tchi mérou danguine
[refrain: jahman]
yé nama pouss yé nama pouss souma néké rancunier dou kén yén leu
beugouma touss loudoul fayou wayé meunoumako mak yén dou bén
yé nama pouss yé nama pouss tchi rancune yéh
yé nama pouss lima léen lébalone bokoulak liguen ma fay réen
[couplet 3]
yallah khamna ni soeur khirou bi ni gueunoul tchi nioun
amoul lou yaaye dadjioul tchi ndjiambotam bi aka yagua mounie
sometime ma fatalikou merelen beu bouti tounie
mais kouma guiss tchi yén tiofél dekiwaat rek meu sipi mouunie
naniou dokh tchi valeurou famille yiniou niou yarewoon
nidjiaay la tchi sey fils té yow badiene nga tchi samey dome
rancune dey yakh khole t daley ignane lo
soukheuteul loubakh sa diguek nit gni meulni imam lo
rethiou mousta ame tchi service yimeu leu defaaloon
bou taye doon demb t meu mane ko sakh dinako doli niare
niagu-ssayou kaddu yi nga balma dama newooon tchi rancune
adouna daaara la tchi fane yeup dafeu bari djianguine
[refrain: jahman]
yé nama pouss yé nama pouss souma néké rancunier dou kén yén leu
beugouma touss loudoul fayou wayé meunoumako mak yén dou bén
yé nama pouss yé nama pouss tchi rancune yéh
yé nama pouss lima léen lébalone bokoulak liguen ma fay réen
[outro: jahman]
mane dém na beu beug fayou wayé meunoumako waw
mane dém na beu beug fayou wayé meunoumako wawaw
mane dém na beu beug fayou wayé meunoumako balnalén
mane dem naa
yé nameu pouss
letras aleatórias
- letra de anders - erabi
- letra de untitled1 - esprit 空想
- letra de laugh - lilamkayo
- letra de elsa vs sub zero 2 [extended + remastered] - the infinite source
- letra de the drunkard's prayer - the wages of sin
- letra de disney channel - młody yerba
- letra de la pija inmaculada - marco viera y los trabas del mar
- letra de a.m.o.r. - jesuly
- letra de mala - quevdor
- letra de 놓지마 (hold tight) - vav